TAALIFS “KOONE BA” “Degger na”

1387

Mber ! xoolal ” Xalee Bii”
Soo demmee sax dafaay sooga yeewu
Dii dem “Koone ba ” ngir lijanti lumu xeewlo ndeegu
Biig, “Peer” fananul galle, te Yaay Booy bi fexxul tey
Demb ba teyjiini xeewluwuniu
Su demmee Koone ba, ” gaa gni ” kalnaniu fa seen “Jakarta ” yi
Su fa taxale “som” wecet dug ci “Maiga bi ” mbaa “Butikku Booy Poulo “, jend fa ndekki
Mbaa book mu xaar fa Tons buy xey maaket mu marjaal ko tuti wecet
Rey fa “tan bi “, yoppufa ken ci mbaraanam yi mbaa sax ex-yi ngir taxale fa wecet
Mbaa mu baab Yaye Faal bi mu lebbalko Kafe Tuuba, mburu ak nenn ak marine ak mayoones
Moom daal boppam moodi xeyyam
sagnse ak niiru ak mbaraan nioodi ay yiteem

Degger na
Baay, dekk bii degger na
“Affeer” yi tar na
Maa ngi seet ban yoon laay jaar ba taxale tuuti wecet, gissuma dara
Waajuuri “elew” yi amatuniu luniu fayyaalee njaboot gi ay “kuur partikilie”
“Marse” soobante, du “solusion”,
Niafaay jaay barinaniu, te niaay jend neewnaniu lool
Te “Polis” ak “Sandarmeri” du niu fa gej ndax niaay luubal te di fa dem barinaniu
Maanam doo xam dal ana fan ngaay doori waar ba fayyeku fa lu am solo loo lijantee sa ay mbir ak sa ay soxla
Du ca “isin” ba, du ca tool ya
Du ca Jakarta ya
“Taranspor” bi doxul bu baax,
Jafejafe ya bari naniu
Risk yi Limaalewuniuleen,
Doynaniu waar
Rax ca amul “sécurité sociale” !
Baay, tar na lool
Ana luciy pexe ?

Farba Senghor

BUURSIIN